Kajoor
Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal. Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.
Cosaan
SoppiKajoor mooy kàdd ab garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si. Moo jur baat boobu kajoor ci wolof. Ñi jëkka yor suufi kajoor, ay séeréer lañu woon, ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ. Ba pare, xeetu wagadu ak jafunu, soqi ci sooninké yi, jóge ca penku, ñoo sos meeni jëkka ilif nguuru gi, ak ñu sant FAAL. Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor. Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen. Dammeel mooy damm, ndax ku jëkka jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor. Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam. Loolu, ca jamono Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon buur-ba Jolof la xeewe. Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI. Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon. Ba noppi Amari Ngone, jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor. Ca tegu, Kajoor di gëna am doole, Amari Ngone dem naa Bawal ak ay jammbaaram, nangu reew moomu. Li tax Amari doonoon ku jëkka nekk Dammeel-Teeñ. Bawal, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan. Amari moo duggal aada bi ñu fal buur bu ñu tudd xulixuli, di fateliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkka nekk buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo.
Koom-koom
Soppici lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na rèew mu ay am-amam newoon. Mbay ak liggéey u loxo ak camm ak napp ak yaxantu ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca rèew ma.
Mbay
SoppiMbay moo doonoon liggèey bi ëppoon solo ci koom-koomam. Loolu moo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ cakoom ga, manoon naa andi sax ab xiif. Dugub moo ëppoon ca mbay ma ak ca dund ga. Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng. Xamoon nañu mbayum. wëtteen.
Liggéey u loxo ak yaxantu
Soppiliggéey ak loxo ñeeño yi la ñu ko feetale woon. Napp gi amoon na solo lool ci dund gi. Waaye njaay moo naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal. Mujj na ba yoon yi jòge bëj-gànnaar ñakk solo lool njëgg mi.
Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo, Fekkoon na Kajoor da jaay ay der ak ay bëñi ñayy mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi,...
Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon. Ñi ñuy wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu. benn nit amu ci woon moomeel. Loolu terewul woon ku mu neexoo mu jariñoo ci kèem kàttanam.
Doole ju bees ji
SoppiNguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya. Ñiy doora falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo. Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon, ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul, rax ci dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk
Liggéeykat yi
SoppiSu fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi. Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetele woon mbay mi, ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat. Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay.
Yoriin
SoppiNguur gu bees gi tax na ba ñu andi tër yu bees ci ay àtte yu bees. Dammeel moo feete woon ñépp kaw. Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen. Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen. Waaye loolu su xewee li koy waral mooy fullay waa ja ak faydaam ak tabeem. Yii yépp ñiy tànn daa nañu ci bàyyi xel.
Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem. Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe. Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur.
Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.
Kajoor nekkoon na juroomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum. Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam foo féete. Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur.
Buuri Kajoor
Soppi1.Decceefu Njoogu (1549) | 17.Maawo |
2.Amari ngoone Sobel | 18.Biram Koddu |
3.Maa Sàmba Tàkko | 19.Maajoor |
4.Ma Xurayja Koli | 20.Makoddu |
5.Biram Mànga | 21.Biram Faatim Penda |
6.Daaw Demba | 22.Amari Ngoone Ndeela Kumba |
7.Majoor | 23.Biram Fatma Cub |
8.Biram Yaasin Buubu | 24.Maysa Tenda |
9.Décce Maram | 25.Birima |
10.Maa Faali | 26.Makoddu |
11.Ma Xurayja Kumba Joojo | 27.Majoojo |
12.Biram Penda Ciloor | 28.Lat Joor Ngoone Faal(1862) |
13.Decce calaw | 29.Sàmba Yaasin Faal |
14.Lat Sukaabe | 30.Sàmba Lawbe Faal |
15.Maysa Sukaabe | |
16.Maysa Tenda |
Delluwaay
SoppiPaate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998