Mandinke, ci xeet Soose yi lanu bokk. Ñoom ñoo taxawal imbraatooru Mali, ak nguuru Kaabu, Ñaani, Wulli ci senegaal. Sunjata Kayta Mandinke la. Mandinke am nañu tuur yu bari: Malinke ci français, manding, Mandinka mooy tur wi ñu tudde seen bopp. Ci seeni làkk, Mandinka mooy: nit ku juge Mande. Mande mooy Reéwum mandinka yi, ci réewum Mali. Seeni Sant: Kayta, Jara, Siise, Ture, Kuyaate, Sumaare, Fakoli, Dumbuya, Dumbiya, Bakayogo. Buuru mandinke Mansa lay tudd.

  NODES