Xay
Baatu xay day tekki mbooleem ay mbaax ak ay melokaani aw askan. Maanaam xamug àdduna, ci wàllu yar ak teggin ak xam-xam, yewwute gu nit ñi ci aw askan. Su ñuy wax xay dañ ciy nat tolluwaayu sag dundin, ndax jëm na kanam walla déet; baat bi dafa ëmb mbooleem ay yëngu-yëngu yuy am ci aw askan: diine, cosaan, xamteef, politig,...
Su ñu nee nit kii dafa xayadi, day tekki ne xamul àdduna. Kon xayug aw askan ñoo ngi koy natt ci doxaliin, dundiinu cër bu ne ci askan wi
Limub ay xay
SoppiYenn ciy xay yu doomi aadama:
- Gu Babiloñaa
- Gu Isipt gi Yàgg ga
- Gu End
- Gu Ittite
- Gu Siin
- Gu Geres
- Gu Rom
- Gu waa penku (Siri, Fenesi, Yëwut)
- Xayug Lislaam
- Monomatapa
- Maya
- Sapoŋ
- Xayug Mongoli
Wikibaatukaay
Soppi- (en) xay
- (fr) xay