Break dancing, walla breakdance, walla break, walla b-boying, ab baat la bu ñuy jëfandikoo ngir wax fecciin wa juddoo te màgge New York ci ati 1970, xammeewu ngir ay suppjalañam aki bërangoom ci suuf si. Fecckatu break dance la ñuy wax breakkat.

Break dancing

Taariixu break dance

Soppi

Break dance ak hip-hop

Soppi

Taariixu break dance mi ngi doore ca Bronx ci ati 1970, Kenn ku bokkoon ci mbootaay gu Bronx River projects la ñu ne moo ko sos. Mu jóge fa, tudde Bronx River Association Afrika Bambaataa, ba si yàgg mu tuddewaat ko Zulu Nation (ci 1974). Gëstu yi mu doon def ci taariixu Afrig ak mbëggéelam ci woy gëtanoon ko, ba taxoon mu farlu woon ci ngir ay ndawi goxam nekk ciy yëngu-yënguy fànn ngir bañoon ñu duggu cig ndëngte. Moom lañuy santee juddug yëngu-yëngu gu bees gi: hip-hop, gi dàttu ci ñenti ponku yii di rap, grafiti, DJing ak break dance. Afrika Bambaataa soosoon na itam benn ci gangoori break dance yi njëkk, tuddoon Zulu King. Njeexit gi waa-jamayka bii di Dj Kool Herc amoon ci caadaay hip-hop mi safaanu woon ak caadaay ndëngte ga amoon ca seen dëkkuwaay ya, ca jamono jooju am na solo lool, ba mat naa fésal.

Fu pecc mi soqikoo

Soppi

Jafe na lool joxe a taariix bu wóor cig juddoom. Ci jeexantalu ati 1970, New York dafa bari woon lool ay xeeti pecc, gox boo dem aki feccinam. Numu manti deme, li fés mooy ne, feccin yi gënoona siiw ñoo doonoon good foot ak popcorn, te jóge woon ca woy yu James Brown ya Get On The Good Foot ak Popcorn. Pecc yooyu yëngali tànk ci anam bu lañ woon te fecckat yi daan sapp se benn tànk di ko awante an beneen bi. Nit ñi daan nañu ci def ay joŋante, siiwoon nañu lool ca jamono yooyu.

Kenn xamul lu waral suñuy fecc di bërangu, aka daanu ci suuf, gannaaw seeniy weñaaru ak seeni damm-yaram. Xalaat nañ lu ne: xéj-na Filmi kung-fu yiñ daan seetaan te ñu bari lu ñuy ŋelaju di tëdd ci suuf. Xéj-na tamit jël nañ ci capoeira. Breaker yi sacc nañ tamit dara si pecci caada yu waa-kasakistaan.

Feccin mi

Soppi

Pecc la mu kenn rek di def, du feccu mbooloo, ci lu ëpp dañuy def ab wërngal kiy fecc nekk ci digg bi, ñuy awante, kenn dem, kenn dikk. Fecckat bi day bokk cib gangoor ñu koy wax crew, suy fecc ŋelaju yi muy def la ñuy wax footwork, walla passpass, ci maanaa su sampee ay yoxoom, ay tànkam daleen di wëndeel ñuy wër yaramam.

Lëkkalekaay yu biti

Soppi
  • (fr)Style2ouf : L'actualité de la danse Hip Hop [Bboying-breakdance-popping-locking...]
  • (fr)Red Bull Bc One : site du championnat mondial en 1 contre 1
  • (fr)Illusion Style : c’est tout sur l’actualité et la culture de la danse Hip-hop, Break Danse dans
  NODES
Done 1
see 5