Ca Afrig, diine yi yagg nañu fa am. Diine yi am Afrig (yawut, kirist, lislaam), ñoo bokk cosaan. Ca jamono nguuru Kuus amoon, tey di nekk wa Sudaan, nit ñoo fa nekkoon, dañu daan nekk ca diine yu jekk am ca adduna, ci li taarixkat wonee. Ca diine boobu, nit yi dañu daan gëm benn Yalla. Li ñu wax monotheisme ci nasaran.

Wa Misra tey di nekk Isipt, ba Sudan, diine boobu moo fa amoon. Ca diine boobu, yalla, mel ni lislaam, ay yu bare la amoon, tur bu nekk wonee benn jikko bu yalla. Ca tur yi amoon na: Ra, Amon, Atoum, Aton, etc.

Taarixkat yi, ñu mel ni Seex Anta Joob, walla Sarwat Al Anis Al Assiouty, wonee nañu, diine yawut, kirist ak Lislaam, foofu (wa Misra) lañu cosaanoo. Ndax yonent yi ñu nekk ca diine yawut ak kirist, mel ni Ibrayima, Muusa, Issa, ca seen teree, biibël ak tora, deeni ne, jaar neen Misra, te foofu, jang nañu yu bare ci diine bu fa nekkoon. Ba noppi yobale nañu Diine boobu ca seen bokk yawut.

Taarixkat yi wone nañu tamit, yawut yi nekkoon ca reewum nit ñu ñuul yi, di wa misra, ñoo doon nit ñi ñu wowee habiru walla hyksos , ci keyitu jamono jii ñu seet.

Bammel bu Méroé, Sudaan


Turu ñu fekk ci askanu yawut ak naar, yu bare, ca diine afrig boobu la joge:

  • Ibrahim, mooy Ib-Ra-Him, ca lakku wa misra bu fa amoon bu jekk mooy, ku am yalla (Ra) ca xolam.
  • Muussa, mooy Messu, ku yalla jur.
  • Sara, Sa-Ra mooy, doomu yalla.
  • Myriam, Meri-Amon, ku yalla begg. Amon mooy benn turu yalla ca diine Afrig.

Ca Misra, lakk bu fa amoon, ro en kemet (lakku reewum nit ñu ñuul yi), la tudde woon, seen bind di medu neter (baatu yalla). Lakk boobu moo jur ay lakk yu bare ci biir afrig, ci li taarixkat yi mel ni Theophile Obenga firndel.

Wa misra mooy fu xeet yi nekk ca biir afrig tey, cosaanoo, te diine bi fa amoon, yobu nañu ko ca fu ñu dëkk tey. Di Reew yi Afrig bu nekk ca suuf Saara. Ndax waaso yi nekkoon wa Misra, dañoo mujj gadday ca biir afrig, ndax amoon naa ay doxandem bu leen fekk seen reew, te leen noot ak di leen teg dund bu meti. Yoro Booli Jaw, bokkoon ci garmi newoon wa Waalo, wax na ci naka xeeti nekk Senegal daaw reewum Misra ba agsi dexug Senegal ca njeelbeen, te li cosaan doon wax rekk la doon tekki.

Bi ñu wacce ca Afrig boobu, xeet yi tassaroo nañu fa, te ba noppi xeet ku nekk, amoon na benn tur ngiir tudd yalla:

Afrig gu bëj-saalumu-Sahara.
  • Mandinke yi, Bambara, Jula, Xasonke, yalla, Maa lañu ko daan tuddee.
  • Sooninke yi, Aari.
  • Pël yi, Geno lañu daan wax.
  • Séeréer yi, Roog Seen
  • Joolaa yi, Emitai
  • Sonraï yi dëkk ca Mali ak Niseer, Yarkoï
  • Bassari ak Bedik yi, Ununga
  • Dogon yi: Amma
  • Yoruba yi Ca Niseeria: Olodumare
  • Masaï yi ca Kenya: Engaï
  • Zulu yi ca Afrig bej Saalum: Inkosi
  • Akan yi, ca reew mi Togo, Gana, kote diiwaar: Mawu Lisa
  • Wa Ecoopi: Waqa
  • wa Kongo ca xeet yi Bantu: NzamBe


Diine boobu amoon ci afrig ba leegi, gestukat yi, nigritism walla kemitism, yeneen wax animism ca nasaraan, lañu ko tudd. Waaye, ñu nekk ca Afrig, te ñu doxal diine boobu, am nañu yeneeni tur ngir tudd ko. Day wuute ci xeet yi. Ndax xeet bu nekk, ci seen lakk, dinañu ko joox benn tur. Wante, diine boobu, feppu mëna nekk ca Afrig, benn la.

Téeré Bammel, bu Téti Royuwaay:Ier ca Saqqarah

Xam nañu ni, ca xeet bu nekk, Yalla wacc na ay yonent. Li mooy tax diine afrig boobu, am seen yonent.

Asar, yonente bu jekk am ca aduna ca diine boobu, boo demee ca Misra. Am na tur yu bare: Issa (ca lislaam moye Issa), Oni (ca diine nasaraan moye Ori). Taarixkat yi ne nañu, taarix bu Asar moo jur taarixu Issa bu yoonu Kirist ca Biibël. Ausar ca xeet Anu la bokkoon, benm xeet bu amoon bu jekk, dëkkoon ca Sudan (Nguruu Kush), ñoom ñoo tabax nguuru Misra, ak Buur Fari ba, mu tuddoon Narmer (Sooninke yi xam neen ko, te Nare Mari lañu ko wowee). Ay Firaouna lañu woon, di tur bu ñu fekk ci lakk yi am Senegaal (Fari, Farba, Faren, etc). Aset (turu Aïssata ci moom la joge). Moo doon jabaru Ausar. Aset ak Ausar ñoo jur Hor, seen doom. Natal bi ñu wone yaayu Yesu/Issa, mu tudd Maryama, ak domam, ca natal bi ñu wonee Aset ak doomam Hor la joge. Set. Ca diine afrig amoon Misra, mooy Seytan. Satan ca diiney kirist, wala Seytan ca diiney lislaam. Liggeeyam mooy mu sonal nit yi ca adduna, tek leen coono. Djehuty, ki moo indaale xam xam, ak bind, ca adduna. Ñu mën ko boole ak Idrissa ca lislaam, wala Henoch ca dinne nasaraan.

Amoon na ajjana (seshet iarou ci diine Afrig) ak safaara nit ñu bon doon dem, di Duat, Al-Jahim ca lislaam, l'enfer ca diine nasaraan.

Maât, doon yoon wu baax ñit ñii waroon ne suñu buggoon dem seshet iarou, am barke.

Ñoom ñoo yonent yu gëna am solo ca diine Afrig bu amoon wa Misara, ndax am na yeneen, te xeet yi ca afrig, bu nekk, ba tey, am nañu tur yu bare ngir tuddu yonent yi. Ca diine bii, Neteru moo doon turu yonent yi. Bu ñu xolee ci lakk yi Afrig yi, ñu gis ay baat bu ko niroo (nutar, ntori, tooru, tuur, etc).

Ca yoonu imbraator gu gana, lislaam ñow na soowu Afrig, ca jamono boobu, lislaam ak diiney bu Afrig, ca jamm lañu doom dëkkando. Ak tubaap yi, diiney nasaraan ñow wa diggu afrig ak Afrig bu penku. Waaye ñu jekk topp yoonu Kirist ci adduna, ñooy askan wi mu tudd Kopte, baawo ci askanu wa misra. Ak Jiyaar yi jullit defoon ca XIXee xarnu, diine bu Afrig ba, waññi na bu baax. Tubaap yi tamit ak canc gi, def neen ñi, diine afrig boobu mu waññi bu bari.

Waante am na ay xeet, diine lislaam walla kirist lañu nekk, waaye dañu duggal ca seen gëm, ay gëmu nekk ca diine afrig, mel ni joola yi, walla Bantu yi, Lebu yi, Akan yi.

Téerekaay

Soppi
  • La Philosophie africaine de la période pharaonique, Théophile Obenga.
  • L'Origine négro-africaine des religions dites révélées, Doumbi Fakoly.
  • Bilal le prophète, Doumbi Fakoly.
  • Parenté génétique de l'égyptien pharaonique et des langues négro-africaines, Seex Anta Joob.
  • Théophile Obenga, Origine commune de l'égyptien ancien, du copte et des langues négro-africaines modernes. Introduction à la linguistique historique africaine.
  • Nations nègres et culture : de l'antiquité nègre égyptienne aux problèmes culturels de l'Afrique noire d'aujourd'hui, Seex Anta Joob.
  • Cossanu Afrig cib nataal, Seex Anta Joob.
  NODES