Epatit A (ñu gënoon ko xamee ci turu epatit biy dale) doon na Jàngoro juy dale ju tar buy jàpp res wi te li koy joxe di doomu jàngoro biñ naan Epatit A (HAV).[1] Bari na lu muy dal nit te du feeñ rawatina ci ndaw yi.[2] Diggante bi muy dugg sa yaram ak bi muy tàmbalee feeñ, mi ngi tollu ci diggante ñaar ba juróom-benni ayi-bis.[3] Su la dalee mën na def ak yaw juróom ñatti ayi-bis te dina faral di ànd ak: xel muy teey, waccu, biir buy daw, der bu mboq, yaram wu tàng, ak mettitu biir.[2] Luy tollu ci 10 ba 15% ci ñi mu dal ñooy wéy di ko gis su demee ba weesu juróom-benni weer ginaaw bi mu leen dalee.[2] Mag ñi mën nañu ci jëlee Feebaru res bu tar waaye bariwul lu muy dale.[2]

Epatit A
Der/Bët bu mboq te Epatit A waral ko
Toftale ak balluwaayi biti
Specialty infectiologie[*]
ICD-10 B15
ICD-9-CM 070.0, 070.1
DiseasesDB 5757
MedlinePlus 000278
eMedicine med/991
Patient UK Epatit A
MeSH D006506

Li koy faral di joxe mooy lekk ñam wala naan ndox mu am doomi jàngoro.[2] Meññeefu géej buñ toggul ba mu ñor dina ko faral di joxe.[4] Jege ku ko am lu ëpp, mën na la ko wàll.[2] Xale yi mën nañu ko am te du feeñ waaye teewul mën nañu ko wàll ñeneen.[2] Su la dalee benn yoon, dootu la dalati sa giir gi dund.[5] Ci sa deret la ñuy seetee doomu jàngoro ci ndax ni muy feeñee dafa nuru ak yu yeneen jàngoro yu bari.[2] Benn xeetu epatit la ci juróom yiñ xam: A, B, C, D, ak E.

ñaqu epatit A dalay aar bu baax ci feebar bi.[2][6] Yenn réew dañuy faral di baamtu ñaq bi ci xale bi ak ci ñi feebar bi gën a yab kenn masu leen a ñaq.[2][7] Loolu mën na leen aar seen giir gi dund.[2] Yeneen matuwaayu yi la ci mën a musal ñooy raxas loxo ak togg ñam ba bu ñor xomm.[2] Amul benn garab buñ ni mën na ko faj, li ci des, garabi xel muy teey wala biir buy daw la ñu lay digal su aajewoo.[2] Gën gaa bari su la dalee dangay wér, sa res wi melni dara mësu ko dal.[2] Bu yàqee res wi, dañu lay gereefeel res ngir faj ko.[2]

Ci àdduna bi, jàngoro bi dina feeñ ci 1.5 miliyo?i doomu aadama at mu nekk[2] nga boole ci yi feeñul mu tollu ci fukki miliyo?.[8] Fi mu gënee bari àdduna bi mooy ci gox yi desee te ndox mi ñuy naan setul.[7] Ci réew yi néew doole lu tollu ci 90% ciy xale jot nañu am doomu jàngoro bi laata ñuy am 10 at, loolu mooy mucci nañu ci ba fàww laata ñuy nekk mak.[7] Yenn saay mu jàppandoo ñu bari ci réew yi xawa am doole ndox jàngoro bi bariwul ci xale yi te itam duñu leen di faral di ñaq.[7] Ci atum 2010, epatit A bu tar bi faat 102,000 doomu aadama.[9] At mu nekk 28 fan ci weeru Sulet mooy Bis biñ Jagleel epatit ngir xamal nit ñi luy jàngoroy epatit.[7]

Royuwaay yi

Soppi
  1. Ryan KJ, Ray CG (editors) (2004). Sherris Medical Microbiology (4th ed.). McGraw Hill. pp. 541–4. ISBN 0-8385-8529-9. 
  2. 2,00 2,01 2,02 2,03 2,04 2,05 2,06 2,07 2,08 2,09 2,10 2,11 2,12 2,13 2,14 et 2,15 Matheny, SC; Kingery, JE (1 December 2012). "Hepatitis A.". Am Fam Physician 86 (11): 1027–34; quiz 1010–2. PMID 23198670. 
  3. Connor BA (2005). "Hepatitis A vaccine in the last-minute traveler". Am. J. Med. 118 (Suppl 10A): 58S–62S. PMID 16271543. doi:10.1016/j.amjmed.2005.07.018. 
  4. Bellou, M.; Kokkinos, P.; Vantarakis, A. (March 2013). "Shellfish-borne viral outbreaks: a systematic review.". Food Environ Virol 5 (1): 13–23. PMID 23412719. doi:10.1007/s12560-012-9097-6. 
  5. The Encyclopedia of Hepatitis and Other Liver Diseases. Infobase. 2006. p. 105. ISBN 9780816069903. 
  6. Irving, GJ.; Holden, J.; Yang, R.; Pope, D. (2012). "Hepatitis A immunisation in persons not previously exposed to hepatitis A.". Cochrane Database Syst Rev 7: CD009051. PMID 22786522. doi:10.1002/14651858.CD009051.pub2. 
  7. 7,0 7,1 7,2 7,3 et 7,4 "Hepatitis A Fact sheet N°328". World Health Organization. July 2013. Retrieved 20 February 2014. 
  8. Wasley, A; Fiore, A; Bell, BP (2006). "Hepatitis A in the era of vaccination.". Epidemiol Rev 28: 101–11. PMID 16775039. doi:10.1093/epirev/mxj012. 
  9. Lozano, R (Dec 15, 2012). "Global and regional mortality from 235 causes of death for 20 age groups in 1990 and 2010: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2010". Lancet 380 (9859): 2095–128. PMID 23245604. doi:10.1016/S0140-6736(12)61728-0. 
  NODES