Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar
Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar gi yaatuwaayam toll na ci 14 090 000 km², looloo waral muy mbàmbulaan gi gën a tuuti ci àdduna bi. Moo ëmb mbooleem géej yi ne ci li wër dottub Bëj-gànnaar bi ak yi ne ci Bëj-gànnaar gu Tugal, gu Aamerig ak gu Asi. Mi ngi taqalo ak mbàmbulaanug Atlas jaare ko ci géejug Barents ak gu Dal gi.
mbàmbulaani àdduna bi | ||||
Bëj-gànnaar |
Atlas |
Bëj-saalum |
End |
Dal |