Wolof làkk la wu ñuy wax ci Gàmbi (Gàmbi Wolof), Gànnaar (Gànnaar Wolof), ak Senegaal (Senegaal Wolof). Mi ngi bokk nag moom wolof ci bànqaasub atlas bu làkki Kongóo yu kojug nit ñu ñuul ñi. Mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la. Am na it lu mu séq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer, joolaa ak basari.

Wolof làkk (Senegaal)
Wolof làkk

Ubbite

Soppi

Bi ñu demee ba gis jëmm ja, muy ku sew, tuuti te xaw a wow, waaye di ku ñu muure ab taar, ci anam gu woyof te loyox, di ku ñu aare kàttan, sóob ko ci ag fonk-sa-bopp doonte ag neen la, solal ko yéerey yëgle ak jaral, te ma jëli loolu ca jafeem gaa jëli. Bi loolu amee, dama ne leen xanaa kay du kii ngeen ma doon wax? ñu ne ahakay, cis lëf, cig yéemu, ak ñàkk a xalaat ne dinaa sikk mukk ci moom, ma jug man, xajal leen foofa fépp.

Ma ne nag waaw ku mel nii, ci li mu làmboo ciy melo, lu ko nit di doye ? Ginnaaw bi nag dégg naa ñuy wax naan moom de bokk na ci ñi gën a jekk ci boobule gox, ànd ak jaaxle ci samaw jëfiin, ci ba ga ma ko fa ba, ma ne leen man : moo xam! Lii mooy li am ci sunu làkk wii, walla yii di yu Afrig yi, dañu di yu am solo te man a dem ni yépp di deme, am barab ci digg barabi làkk yépp, waaye li nu dal nun waa Afrig, mooy li dal sunu lépp, dalaale ci li muy dal sunu kàllaama yii nga xam ne wii de bokk na ci yi gën a nosu, gën cee nooy, gën cee nangoo defaru, yéwénu, ruy, ci ku ko ruyal, tey way nag ca nanu bëgge mu waye ni.

Ana nag ku am janq bu mel ni bii cib taar, nangoo ni, joŋee ni, jekke ni, man nee toppatoo, nangu nee jëme kanam, waaje ni ngir lemu ci say bëgg-bëgg, ana ku am ku mel nii, looy xoolati ku sewe nii, ràgge ni, te taaroodi ni?

Li ma bëgg a wax mooy naka la nu bëgg a bàyyee sunu làkk yii, rawatina wii di wolof, ca nooyam ga, ak nangoom ga, ak gàttam ga ak noppaleem ga, taaram ba, leeram ga, manam gaa leeral ak yaatoom ga, ak ruyu gi mu nangu, naan dangay jëlati weneen di ci sonn ak a sonle, naan day wa gën? Ma ne ñoom ñoo gis loolu man de déet !

Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal, waaye ngir doyodig waa Afrig yi ba leegi, frañse mii nga xam ne lu matul 30 cib téeméer ci doomi Senegaal yi rekk a koy wax moo fiy làkk wu njëkk, maanaam wi nguur gi di waxe di ci liggéeye. Moor Taala Baay Faal Mbóoj

Cosaanam

Soppi

Ni ko gëstukat yi waxe, làkku wolof am na ag mbokkoo ak yeneen làkki Afrig yu bari, yu mu bokkal i maam. làkk yi dañ leen a séddale ci ay wàll: bu ci nekk ñi am ag mbokkoo lañu fa def. Nee nañu wolof ci wàll gi ñuy woowe bànqaasub atalaas bu làkki Kongóo yu kojug nit ku ñuul la bokk. Am na ag mbokkoo ak pulaar ak séeréer ak joolaa ak yeneen.

Daanaka ñoo ngi koy làkk ci Senegaal gépp, bëj-gànnaar ba bëj-saalum, penku ba sowwu. Donte wolof da di làkku askanu ñi ñuy woowe ay wolof, waaye kàllaama wolof amul uw dig. Dem na ba romb dig (frontiere)yu Senegaal àgg ba Gàmbi, Gànnaar ba Mali, ci ñaari dëkk yu njëkk yi sax boole nañu ko ci seen i làkki réew. Daanaka gox boo dem ci Senegaal am nañu waxiinu wolof wu wuute: am na wolofi waalo-waalo, jolof-jolof, saalum-saalum, wu kajoor-kajoor, wu baol-baol ak wu lébu.

Mbindin

Soppi

Abajada wolof

Soppi

a - à - aa - b - bb - c - cc - d - dd- e - ee- é - ée - ë - ëe - f- g - gg - h - i - ii - j - jj - k - kk - l - ll- m - mm - mb - mp - n - nn - nc - nd - ng - nj - nk - nq - nt - ñ - ññ - ŋ - ŋŋ - o - oo - ó - óo - p - pp - q - r- rr - s - ss - t - tt - u - uu - w - ww - x - y - yy.

Loy Tàmbali Biir Mujj
1 a, A am sabar mala
2 à, À àllarba muskàllaf amul
3 aa, Aa aar talaata Tuubaa
4 b, B bax jabar rab (rabu àll)
5 bb amul jebbi bb
6 c, C coono looco amul
7 cc amul soccu cc
8 d, D der xadar amul
9 dd amul buddi sedd
10 e, E egg xel fexe
11 ee, Ee ee bees bee
12 é, É amul sédd xulé1
13 ée, Ée éem féey bu bëggée1
14 ë, Ë ës fës jë
15 ëe, Ëe amul bëer amul
16 f, F for nafar nef
17 g, G garab jagal nag (nagu Sàmba)
18 gg amul rogganti segg
19 i, I itte tis kaani
20 ii, Ii iir riiti bii
21 j, J jabar fajar faj (fajal)
22 jj amul jji bojj
23 k, K kafe saaku ak
24 kk amul kkaan lekk
25 l, L lam nelaw xel
26 ll amul xolli ll
27 m, M mar laman xam
28 mm amul mm mm
29 mb, Mb mbootu mbar mb
30 mp amul mpóor samp
31 n, N nar daanu fen
32 nn amul nnu wann
33 nc amul dencukaay sanc
34 nd, Nd ndox rendi nd
35 ng, Ng ngoon teraanga lang
36 nj, Nj njàmbal njul donj
37 nk amul nkar nk
38 nq amul sanqal janq
39 nt amul santaane bant
40 ñ, Ñ ñam wañaaru ngooñ
41 ññ amul ññi ññ
42 ŋ ŋaam daŋar laŋ
43 ŋŋ amul ŋŋarñi doŋŋ
44 o, O oyof loxo laalo
45 oo, Oo oor boroom àndandoo
46 ó óbbali jóg pusó1
47 óo óom góor xulóo1
48 p put ciipatu amul
49 pp amul ŋàppati lupp
50 q (ñaari xx) amul qarci q
51 r, R raxas maral liir
52 rr amul fërr-fërri fërr
53 s, S suuf desit fas
54 t, T tool tuuti nit
55 u, U um buddi kuddu
56 uu, Uu uuf buur luu
57 w, W wasin tawat xew
58 ww amul xewwi jaww
59 x, X xar saxaar lex
60 y, Y yaram layoo y
61 yy amul fayyu coyy

1- Doonte sax, li ñu téj ci biir lonk yi ngay dégg, nanga bind: xule, bu bëggee, pus, xuloo.

Xool it

Soppi
  NODES
os 3